Aller au contenu

Hip-hop

Jóge Wikipedia.
Sumbu 22 Maars 2010 à 20:06, bu: Abdu Xaadir KEBE (waxtaancëru)
ay breakat

Hip-hop ag yëngu-yëngug caada ak fànn la, mi ngi juddoo ca Réew yu Beenoo ya ci ndoorteel ati 1970 yi, daa boole bànneexu ak ñaxtu. Mi ngi juddoo ci biir askani waa-aamerig yu ñuul yi, ca New York, fa la tàmbalee, mujj tas ca réew ma ba ci àdduna bi bépp, ba tay mooy dundiinu réewu-taax wi ëpp doole. Caaday Hip-hop ci ñeenti ponk la tënku: break dancing, DJing, MCing ak graffiti.

Bii xeetu fànn ñu bari ci woy wi lañ koy tënk ,MCing, te mu gëna siiw ci rap. Caadaay Hip hop yemul rekk ci rap, man naa sol mbubb yu wuute: su fekke danuy yem rekk ci xoosug DJ bi (Disk Jokey), waruñ ko tuddeeti rap, waaye DJing , sunu yemee ci li MC bi (master of ceremonie, njiitub xew) di bacc kon man nan kaa woowee rap, walla tamit, donte bari na lumuy faral di am, boolee benn DJ ak ay walla benn MC, kon ci nii hop-hop lañuy wax, ndax rap ak MCing yépp ci caadaay hip hop lañu bokk, waaye nit ñi rap la ñuy wax rek yem ci ngir yombal.

Cosaanu baat bi

Cosaanu baat bi taxu kaa leer noonu, ci ñenn ñi jëfandikoo-xel ngir tekki

  • Hip "muus", "am-xel" lay tekki, muusaayu tappalaatukat.
  • Hop ab yuuxu la bu kuy tëb di def (soo tëb ni op!).

Nee nañ baati baa ngi wara bawoo ci DJ Luv Bug Starski mi ko doon faral di jëfandikoo suy wax. Waaye li wér te wóor mooy ne gandoor bu Sugarhill Gang mooy ki ko siiwal ci àdduna bi, ci seen woy woowu Rapper's Delight, di benn ci woyu rap yi ñu njëkka def k7.

Taariix

Ay cosaanam

Woyu hip-hop ci buumu xeeti woyi waa-aamerig yu ñuul yi la bokk. Ay dàttam ñi ngi bàyyikoo ci dundin gu metti gi ñu nekkee woon, dalee ca seeni maam ba ci jamono yi muy juddu, woy yañ daan def ca tool ya daan ca naqarlu seenug nekkin, ak caa fattali seenug jóge Afrig. Mi ngi tambalee ciy kebetu niki xeeti woy yu mel ne ragetime, jazz, blues. Ci lu gëna jonjoo, woyu hip-hopa ngi bawoo ci Soul, ak ci funk. Yii xeeti woy bawoo bëj-gànnaaru Aamerig dem ba fasook sound-system bu waa-jamayka, bi àgg ba New York ndax wàlliyaan gi waa-jamayka yi daa def foofa. Ba tax-na ñett ñi ñu ne ñoo sos yëngu-yëngu hip-hop fa la ñu bàyyikoo.

Donte hip-hop ci yii xeeti woy la ëlee ay dàttam, waaye doonul seenug wéyale. Du lu ay tëggkat yu xereñ ci seen liggéey toog xalaat, ni blues doonee wéyaleeg jazz, gospel juddoo ci blues, soul tegu ci, funk ñëw, caaday hip-hop dafa am ab dog-dog ag yeneen xeeti woy yooyu

Aji-rap yi njëkk

Les premiers rappeurs et groupes de rap qui ont marqué l'histoire sont :

Lëkkalekaay yu biti