Albert Einstein
Albert Einstein (juddoo Ulma (Almaañ) ci atum 1879, faatoo Princeton (Diiwaan yu Bennoo yu Amerig) ci 1955) doonoon na ab boroom xam-xamu jëmm, xaymakat, xetlukat bu waa Almaañ bu jëloon réewu gu waa Suwis, te mujje ca Diiwaan yu Bennoo yu Amerig.
Lu weesu doon gi mu doonoon kenn ci jëmmkat ak xaymakat yi gën a siiw ci àdduna bi ci taariixu xam-xam, doonoon na xalaatkat, ku bari yëggu-yëggu ci yeneen fànn (tambalee ca xeltu ba ci politig). Boole nañu ko ci gëstukat yi gën a màgg ci xarnub XX.
Bokk na ci li ko gën a siiwal gisiin wi mu def te duppe ko gisiinuw ajoo. Dugal na it loxoom ci li jëmale-kanam doolerandub kàttan-ferñent, doolerandug tekkaaral, añse.
Jotoon na Neexalub Nobel ci jëmm ci atum 1921
Dundam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Albert Einstein Ulma la juddoo ca Almaañ aji juram ju gòor mooy Hermann Einstein, doonoon booroom këru liggeéyukaay bu doon defar ay wuutuloxo yu mbëj, Pauline Koch doonoon aji juram ju jigéen.